Euhlou Xassida Xidmatul Xadim
前往频道在 Telegram
📈 Telegram 频道 Euhlou Xassida Xidmatul Xadim 的分析概览
频道 Euhlou Xassida Xidmatul Xadim (@euhloukhassida) 法语 语言赛道中的 是活跃参与者。目前社区聚集了 11 766 名订阅者,在 宗教与灵性 类别中位列第 7 560,并在 塞内加尔 地区排名第 41 位。
📊 受众指标与增长动态
自 невідомо 创建以来,项目保持高速增长,吸引了 11 766 名订阅者。
根据 26 八月, 2026 的最新数据,频道保持稳定运转。过去 30 天订阅人数变化为 177,过去 24 小时变化为 1,整体触达仍然可观。
- 认证状态: 未认证
- 互动率 (ER): 平均受众互动率为 13.35%。内容发布后 24 小时内通常能获得 3.71% 的反应,占订阅者总量。
- 帖子覆盖: 每篇帖子平均可获得 1 571 次浏览,首日通常累积 436 次浏览。
- 互动与反馈: 受众积极参与,单帖平均反应数为 0。
- 主题关注点: 内容集中在 leen, ngi, juram, lépp, serin 等核心主题上。
📝 描述与内容策略
作者将该频道定位为表达主观观点的平台:
“Au service de CHEIKH AHMADOU BAMBA KHADIM RASSOUL”
凭借高频更新(最新数据采集于 27 八月, 2026),频道始终保持新鲜度与高覆盖。分析显示受众积极互动,使其成为 宗教与灵性 类别中的关键影响点。
11 766
订阅者
+124 小时
+1047 天
+17730 天
帖子存档
Ngëneel yi nekk ci màggal guddig gàmmu_
• Ku màggal guddi gi ci Sunna
تعظيمه بالسّنة يقودنا للجنّة
به ازدياد المنّة لمخلص معظّم
"Di màggal guddi googu te dëppale ko ak sunna bañ caa def lenn lu Yàlla aaye dinanu wommat jëme nu guyaar _"aljana"_ te dana tax nu am xéewal yu dolliku bu dee sellal nanu ko.
فمن يعظّم مولدا نبيّنا باب الهدى
فلا يحاسب غدا عند الحساب المفحم
"Képp ku màggal guddig Yónnent bi SHW moom mi nga xam ne mooy buntub jub, kooku ëllëg deesu ko hisaab ca bis ba nga xam ne sunu Boroom dana wedamloo ñépp ci lijjanti seen bir."
فمن يعظّم مولدا خير البرايا أحمدا
فكشهيد شهدا بدرا بغير وهم
Képp ku màggal guddig ngën ji mbindeef, dana ci ame tiyaaba yu bari ba mel ne ku fekke woon badar Yàlla jël ca bakkanam ci lu dul genn defe Ku ci def sa alal •
فكلّ من أنفق في مولده المشرّف
مالاً بغير سرف و لو بقدر درهم
فإنّه كمن حضر يوم حنين و صبر
و يوم بدر و نصر خير الورى مفهّم
Képp koo xam ne def na alalam ci guddig gàmmu te bañ caa def lenn luy niru ag yàq, alal jooja donte daa tuuti ba tollu ni ab dërëm kooka dana ci ame tiyaaba joo xam ne dana mel ni ku teewe xare Badar ak xareb Hunayni doon muñ tey dimbali Yónnent bi SHW tiyaaba ju tol noonu la ciy jële. Ku ci bégal nit ci bernde •
فكل من قد حضرا مولد أفضل الورى
معظما مبشرا بسكّر أو لحم
فإنه قد ظفرا بما يديم البشرا
و لا يلاقي ضررا يوم اجتماع الأمم
Képp koo xam ne fekke na guddig gàmmu mu di ko màggal di ca bégal nit ñi ci lu saf suukar walla ci ag ndawal kooku sunu Boroom dana ko jox loo xam ne da koy saxalal ay mbégte fu mu toll di bég te ëllëg bis ba sunu Boroom di dajale mbooleem xeeti yi moom du fa daje ak jenn lor.
فمن طعاما هيّئا لمن له قد قرءا
مبجّلا فخبئا خيرات أهل الهمم
"Képp koo xam ne fekke na gàmmu mu waajal aw ñam jox ko ña nga xam ne ñooy jàng mu def ko ngir màggale ko guddi gi, kooku dina am yiw ya nga xam ne gaa ñu amoon yitte yu kawe ya _(gaa ñu baax ña)_ amoon nañu ko."
• Ku ci jàng dara ngir sàkku barke
و من على شيء قرا مولد سيّد الورى
تبرّكا فسيرا نموّه بالفدغم
"Saa soo amee loo xam ne danga caa bëgg barke nga jàng ci guddig gàmmu fas ko ca, loolee danga gis mu doon lu màgg ba yaatu lool ci barkeb Yónnent bi SHW."
Ku ci jàng dara (Alxuraan, Xasiida, Salaatu…) ci am ndox su noppee naan ko
و إن على ماء قري/ مولد خير البشر
فالشّرب بالمطهّر/ يكفّ كيد المرغم
ينوّر القلب الشّراب/ من ذالك الما بالمجاب
و القلب يحيي دون/ عاب و عن شقاء يحتم
Koo xam ne ci guddig gàmmu jàng na dara ci Xasiida mbaa ci Alxuraan mbaa ci julli ci Yónnent bi SHW walla ci turu Yàlla wu mu man a doon def ko ci ndox naan ndox ma, ndox moo ma dana ko fegal pexem saytaane te ndox moo ma naan ga mu ca naan dana waral ab xolam dal di leer, dana waral it ab xolam dal di dund ba mucc ci lépp luy sikk te it naan googee dana ko fegal ag texeedi.
•Li ci dundal guddig gàmmu
احياء مولد البشير يحمي/ العيال و الدّيور
فيه شفاء لّلصّدور/ لكلّ هاد ينتم
"Dundal gàmmu day aar njaboot yi di aar kër yi, luy saafara xol yi mi ngi ci ñeel képp koo xam ne ab jullit la bu gindeeku."
_Sëriñ Tuubaa {Xasiida Jasbul Quluub}_
Découvre la vidéo de EUHLOU KHASSIDA XIDMATUL XADIM ! #TikTok https://vm.tiktok.com/ZSV64wGQF/ Cette publication est partagée via TikTok Lite. Télécharge TikTok Lite pour découvrir d'autres publications : https://www.tiktok.com/tiktoklite
+5
Xassida HAMIDTU....
SERIGNE BI mingi ko teunké حسبنا الله ونعم الوكيل Hasbunal Laahu wa nihmal wakiil
BOROOM TOUBAA mingi ko taalif Vendredi 09 Août 1895 deupo ak Aljuma 17 Safar ci atum 1313 mouy biss banga xamni mom la waron kheuy dadié ak toubab bi mouy Samedi 10 Août 1895 deupo ak Gaawu 18 Safar 1313. Mom Khassida guii nak SERIGNE BI mingi ko taalif ci ndigalou YONNENT BI SAW ci bissou Aldiouma guinaw waxtu Tàkkusaan.
Khassida gi kepp kou kay diang inchallah dinga tabbi ci karangué BOROOM BI SHT.
+9
Xassida gui SERIGNE TOUBA mingui ko teunké aaya bi 👉
وَاذْكُرُوا اللّٰهَ فِيْٓ اَيَّامٍ مَّعْدُوْدٰتٍ
Nettali naniou ni Soxna Astou Gawane Mbacké mom CHEIKHOUL KHADIM mo wakh ni "kepp kou diang khassida gui si yoor-yooru magalou touba mel nga ni kou magalé nako SERIGNE BI beugué.
Temoignage_de_Serigne_Mbackiyou_Faye_sur_Cheikh_Abdou_Lahad_Mbacké.mp38.16 MB
Temoignage_de_Serigne_Omar_Lo_sur_Cheikh_Abdou_Lahad_Mbacké128k.mp311.55 MB
